Communiversity

Afrikan Language Institute => Wolof Language Resources => Topic started by: Ɔbenfo Ọbádélé on Aug 07, 2008, 07:48 AM

Title: Xam-xami Cosaan: Knowledge of Culture/Tradition-gctid29970
Post by: Ɔbenfo Ọbádélé on Aug 07, 2008, 07:48 AM
       xam-xami cosaan ngir yokkute gi
       
       Làngug yëngu yi
               
Weeru          Nowàmbar ci atum 1998
       
       
Kër          giy saytu yéenéek xam-xam
       
Diiwaanu          Afrik
       
Bànk          Monjaal
       
       
 
                   
Nataal          bii, R. Kiessling, GTZ, Eschborn moo ñu ko baaxe:
       
Jigéeni          réewum Mali yuy cuub ay ndimó di jëfandikóo xaralay "Bogolaa".
       
                    XAAJ          BI JËKK
              Lan          mooy xam-xami cosaan ?
       Lu          tax xam-xami cosaan yi am solo ?
       Lan          lañ Nisër ci xam-xami cosaan yi ?
       Lan          la liggéey bii juragum?
               
       ÑAAREELU          XAAJ BI
              -          LAN MOOY XAM-XAMI COSAAN ?
               
       ÑETTEELU          XAAJ BI
              LANGUG YÉNGU          YI
       BOOTAL YI
       Bootal 1
       Bootal 2
       kërale 2
       kërale 3
       kërale 4
       kërale 5
              ÑETTEELU          XAAJ BI
               Jubbi bi          ñeel lépp lu jëm ci xam-xami cosaan yi.
                                                                             XAAJ                    BI JËKK
                                                                       Lan          mooy xam-xami cosaan ?
       
      pajum          xob ak reen misaalu xam-xami cosaan la boo xam ne dafa mos di am solo          ci nit ñi ak fu ñu mën di nekk di àdduna si. Li ñu ci jot a bind joxewul          gi-gis boo xam ne ñépp a ci ànd, bokk nu ñu ko deggé.
       Terewul          ba tey mu am ay màndarga yu bari yu leen wutaleeg yeneen xam-xam yi. Ni          aada yeek waaso yi wuutée la xam-xami cosaan yi di wuutée. Ci xam-xami          cosaan yi lañuy sukkandiku ba jàpp ni ñuy war a defe ci wàllu mbéy, wér-gi-yaram,          caytum càkkéef yeek lépp lu nu mën di yéngu
       Xam-xami          cosaan am nañu wàll ci ni nit ñi di doxale diseen digante, ni yeen yi          di tëdde, li nit ñi war a séq ak aada yi. Li ëpp ci xam-xam yooyu de ñu          leen di donn moo tax tënk leen nekk lu jafe. Gëstu gii dafa ciy joxe ay          misaal, am xam-xami cosaan yu may wone seeni melo, boolewaale ci itam          njàng mu am solo muy ci mën a jariñoo ci wàllug yokkute. Ci kow loolu          lay joxe misaal yii :
       •          Mbéyum xeetu ñebbe ju bees ca réewum Kolombi ak mum Ruwaanda.
       •          Céddalem dund gu ñu démbaléewoon nit ñi ca Nepaal.
       •          Dogu gu jigéeni Malikunda ci réewum Senegaal dogu di jële fi njongum jigéen.
       •          Njoof gu ñuy njoof jigéen ju wasin ba noppeek liiram ci xeet wi tudd Ibo          te dëkke réewum Niseryaa, añs.
              Lu          tax xam-xami cosaan yi am solo ?
       
      Foo          dem, ci xam-xami cosaan lañuy sukkandiku be lal pexe yu ñu faje jafe-jafe          yi ñu jankonteel, rawatina ñi seen loxo jotul seen gannaaw. Xam-xami cosaan          yi am nañu doole lool ci xam-xam yi mën a indig yokkute. Waaye liñ leen          di jëfandikóo ci doxalin yi yokkute tax a jóg néew na lool.
       Jàng          ay xam-xami cosaan, doore ko ci li nit ñi xam te ame ko, dina tax ñu gën          a xam ni nit ñi dundé, su ko defee ñu gën a xam liñu war a def ba dimbale          leen ndimbal gi ñu yelloo. Gannaaw loolu, am lu leer ci xam-xami cosaan          yi mën naa tax ba nit ñi gën leen a faale. Rax ci dolli, fexe be lépp          lu ñuy def méngook ni nit ñi di dunde, mën naa tax ba ndimbal gi yokkute          tax a jóg ëpp fi njariñ te njariñ yooyu sax fi ba abbadan.
       Weccantey          xam-xami cosaan ci askan wi walla diggantey askan mën naa gën a dimbale          nit ñi ñu gën a xam li leen wutale ba gën a jox gëdda aada ci wàllu yakkute.          Li ci ëppati solo nak moo di, def ci weccantey xam-xami cosaan ak seenug          bokk ci sémbu ndimbal yi Bànk Monjaal ak ñi mu jàppool ngir indi yokkute,          mën naa gën a wàññi ñàkk gi.
       -          xam-xami cosaan ngir yokkute gi
       -          yëngu yi ñu taxawal
              Lan          lañ Nisër ci xam-xami cosaan yi
              Tas          xabaar bi
       
      •Suuxat          sàqum xam-xami cosaan yeek liñ ci mën a jànge.
       •          Siiwal ay misaali xam-xami cosaan ci jumtukaay yu ñu bind ciy kayit walla          cib masiin.
              Yombal          weccantem xibaar ci diggante ñi nekk ci dëkk yi ci réew yu néew doole          yi.
       
       •          Ndimbal ci lu yokk mën-mëni nit ñi nekk ci dëkk yi ngir ñu bokk xam-xami          cosaan yi.
       •          Xam niñ war a def ba dugal xam-xami cosaan yi ci masinu ordinaatóor, tas          leen ba ñu yegg ci nit ñi ci dëkk-dëkkaan yi.
              Lan          la liggéey bii juragum?
       
      Bi          ñu dooree làngug xam-xami cosaan yi ba léegi, li gën a fés ci liñ ci jëlé          mooy :
       •          Yékkéti sàqum xam-xami cosaan bu def lu toll ci ñeen-fukki misaal.
       •          Sos yoonu "Enternet" buy joxey xabaar yu aju ci xam-xami cosaan yi.
       •          Siiwal kayitu tasukaayu xibaar bi tudd "Mbind ci xam-xami cosaan yi" te          ñu jaglee ko xam-xami cosaan yi.
       •          Gëstu ci xam-xami cosaan yi. (seetal ci bootal 1 ngir xam li mu          ëmb).
                                         
ÑAAREELU            XAAJ BI
         
       1          - (1 ) Jàppóo gu dëggu ci diggante réew yi ngir weccantey xam-xam          du mën a antu te doonul ne réew yi néew doole dañ cee dugal seen loxo,          taxaw ci taxawaayu ñuy joxe ak di jëfandikóo xam-xam yi.
        Ndaje          ma amoon Torontóo ci weeru SuweN bu atum 1997, fésaloon na ne dañoo war          a sàkku xam-xami cosaan yi ngir ñoN al leen te di ci weccante. Bu yàggul,          njiitug Bànk Monjaal ci woote gi mu fi wootewoon ngir nit ñi am gis-gis          bu yaatu ci yokkute fésaloon na ne dafa laaj taxawaay buy sóorale fu mu          mën di tollu askan yeek seeni xam-xam. Ci jamanog jàppóo ngir jumtukaay          yu xarala yi ñuy jokkoo ci Afrik, la Bànk Monjaal nangoo jiité sémbu xam-xami          cosaan yi ngir yokkute, ngir indi ci ndimbal guy tax ñu nangu ne xam-xami          cosaan am na, di leen jëfandikóo te di leen weccante ci yoonuw yokkute          gi. Jamano jooju nak, ci lañ amal gëstu gii.
              II./          - LAN MOOY XAM-XAMI COSAAN ?
       
       2          - (3) Pajum xob ak reen misaal mu baax mu xam-xami cosaan moo xam          ne foo dem ci àdduna si fekk ko fa. Li ñu bind ci xam-xami cosaan yi,          joxe wul benni gis-gis bu ñépp déggóo. Bokk na ci li waral loolu wuute          gi am ci li soxal bindkat yi dale ko ci ngëmu nit ñi ba ci pexey mbéy.          Waaye, loolu terewul mu am cingis-gis ay melo yu ñu bokk. Melo yooyu feeñ          nañu ci li ñaari kilifa bind ci xam-xami cosaan yi (seet ko ci néeg bii          di ñëw).
              Yenn          ci tekkini xam-xami cosaan.
       
       Xam-xami          cosaan xam-xam yu cosaanoo fi ñu leen di jëfandikóo - foo dem fekk fa          ay xam-xami cosaan yu fa fekk baax.
       xam-xami          cosaan yi dañoo wuuteek xeeti xam-xam yi réew yépp dégóo te ñu leen di          jànge ci daara yu kowe yi, gëstuwaay yeek yenn kër yi nga xam ne dañoo          am ñu leen moomal seen bopp. Ci xam-xami cosaan yooyu lañu sukkandiku          be nas pexe yi ñuy jëfandikóo ci wàllu mbéy, wèr-gi-yaram, togg, yar,          caytum càkkéef yi, ak yeneeni mbir yu nit ñi bokk dëkk di yéngu. (waren          1991).
       Askan          woo dem, xam-xami cosaan a lal lépp luñuy xamle. Xam-xami cosaan yeey          yombal jokkoo beek li ñu fas yéenée def. Pexe cosaan yi nit ñi di jokkoo          dañuy dox jamano ju ñëw ñu ànd ak moom
       Askan          woo gis pexe yi ñu fay jëfandikóo dañuy dox, lu ñëw walla ni muy jokkook          ñeneen dañuy am lu ñu ciy soppi.
       
       3          - (6) Melo yi ñu fi jot a wax, wone nañu ne xam-xami cosaan yi dañoo          bokk ci pexey yi mën a indi yokkute ci askan yi. Xalaat bi ñu amaloon          ci jokkute ci àddinasi ci atum 1998 jàpp 1999, feeñal na ne xam-xam a          mën a indi yokkute ci wàllu dundi doom-aadamaak koom-koom gu sax waaye          du ay koppar. sukkandiku ci xam-xami cosaan yi nga xam ne ñoo lal xam-xam          yi nit ñi jëfandikóo lañ war a jëkk a def bu ñu bëggée réew mu neKK jariñoo          ay xam-xamam. Rax ci dolli, nit ñaa ngi gën a déggóo ci jàpp ne weccantey          xam-xam dafa war a nekk yoon wu nit ñi di jëflantee.
       Tasaarem          xam-xam, ci réew yi am doole rekk la xam-xam bi di bawoo jëm ci reéw yu          néew doole yi du mën antu te dina am ñu yaakaar ne dañu leen xeeb. "Nguur          yeek kuréel yi réew yi séq war nañu mën a dimbale reéw yi ci yéngu yi          jublu gëstug ni yeneen réew yi di fefe ngir mën a ràññee xam-xam yi leen          gën a jubu, jëfandikóo leen seet, waaye ñu ngi doon gën a am ndam su ñu          dimbalewoon reéw yu néew doole yi ñu fexe ba méngóo am digante xam-xam          yeek fi ñu leen di jëfandikóo.
       Dimbalé          néew doolé yi ci xam-xam a ngi gën a mën a nekk su fekkee ne dañoo sàkku          ci ñoom xam-xam yi aju ci seeni saxlaak anam yi ñu leen di jëfandikóo.          "Ci kow loolu, lépp lu jëm ci yokkute, rawatina yi nga xam ne néew gi          doole yee leen yékkéti, jamono yu ñu leen di nas walla ñuy doxal jéego          yi ci bokk, dafay laaj ñu yebe xel xam-xami cosaan yi.
               4          - (8) Mbër mi (jafe-jafe bi) askan wi (gën a jankoonteel) mooy am          pexe yuy tax ñu gën a xam kuréel yeek doxalinu cosaan yi, te bu ko laajee          ñu fexe ba xarala yu bees yi (maanaam yi gën ci doxalin yi nga xam ne          yemuñu ci menni réew doN N ) dëppóok doxalinu nit ñi. Noonu doN N la xam-xam          yu yaatu yi di mën a àndeek soxlay mbooloom doom-aadama mu nekk ci fi          mu dëkke li ëpp solo ci kow yoon wi ñuy jaar ba xam-xam bu ñëw ñu jëfandikóo          ko ci anam yi dëppóok ni nit ñi di dunde moo lépp lu am, ñu fexe ba ñi          am xam-xami cosaan dugal ci seen loxo.
        Ag          gëstu gu ñu amal ci 121 porose yu nekk ci kow gi di tappatoo lu jëm ci          ndox ci 49 réew, feeñal na ne su ñu ci jëlée 100 yoo xam ne nit ñi tax          ñu jóg dañoo bokkoon ci ñi doon nas porose bi, 70 ya am nañ ndam yu takku,          te bu dee ñi nga xam ne loolu amul ca woon, 10 doN N a ci am ndam. Ni          ko misaal yi di ñëw firndéele, xamug ni nit ñi di doxale ci fi ñu dëkké,          boole leen ci lépp lu ñu fa nar a amal mën nañoo doon pexe yuy tax ba          yi gën ci jëfin yi ñuy jëfandikkóo te réew yi bokk leen dëppóok ni doom-aadama          yi nekke fi ñu dëkk.
              Misaal          1: Jëfandikóom jiwu ñebbe wu bees cà réewum ruwànda ak wum kolombi.
       Bi          ñu jëlée ñaar ba ñetti jiwu ñebbe yi nga xam ne gëstukat yi jàpp nañu          ne ñoo dàq a meññ taxul ñebbe yokku ni ñu ko foogewoon. Noonu, gëstukat          yi ne dañuy woo ci béréb bi ñuy gëstóo beykat yu jigéen yi nga xam ne          am nañ xam-xam cosaan ci mbéyum ñebbe ngir ñu xoolal leen lu toll ci ñaar-fukki          jiwu nebbe yii, tànn ci ñaar ba ñett yi ñu jàpp ne ñoo gën, bey leen li          ñu am ci jiwu yi ñu tànn ëppe ne lañu amoon ca jiwu ya gëstukat yi 60          ba 90 ci téeméer yoo jël.
              Ñu          jànge ci ne : Xam-xami cosaan mën naa xamle lu am a am njariñ ci ni ñu          war a jëfandikóo pexey mbey yu bees yi.
       
       
       Misaal          2 : Ay dëkki-dëkk fexel nañ seen bopp ni ñuy séddalee dund gi          ñu leen dimbalee leer (aw yoon).
               Ngir          mu wóor leen ne nit ñi dinañu jot ci dund gi ñu leen di dimbalée, ab sumb          bu tudd "fud foo wok" (maanaam liggéey ñu jox la loo lekk) te nguurug          Nepal amaloon ko ci ndimbalug kuréelu See-Tee-Sed (GTZ) la ñu wax nit          ñi ne moom lañ fas yéene amal ak ñoom. Ci loolu la ñépp déggóo ne dëkk          bu nekk, ci ña fa dëkk lañuy tànn ñiy séddale, waa dëkk bi di xool ni          céddale mi di doxe, moo gën a rafet ci anam yi ñu war a séddalee dund.          Li ñuy jëlé ay kamyo , ar sareti nag lañuy sëf dund gi. Njariñ yu bari          amoon nañu ci doxalin woowu, taxoon na ba ñi joxe saret, li ñu waroon          a jot ci dund gi yokku, te loolu naruloon a am su fekkoon ne dañoo jëloon          boroomi kamyoN bu bawoo réew taax.
              Rax          ci dolli, ndégam sëfu saret bu nekk xam nañu natt bi mu tollol tax na          ba nit ñi xam ni dund gi ñu séddalé yem. Ci noonu itam la ñuy xame ci          lu yomb lépp lu waroon a ñëw te ñëwul ni mu toll ci mbooloo mi, te lu          réer wallu ñu joxe ko ci lu ñu leeralul, dinañ ko mën a waxtaane ci biir          nit ñi. Yeneen sémb yi ni meloon ca réew ma dañoo mujjéwoon jëfandikoó          doxalin wii.
              Nu          jànge ci : Jëfandikóo nattukaay ak jëfukaayi cosaan yi, ci sémbub "liggéey          ñu féy lag lekk " dina yombal joxeg dund gi te nekk misaalu doxalin wu          amul benn njuuj-njaaj cib dëkk.
       
       5          - ( 11) Ci gàttal, xam-xami cosaan yi dañoo am njariñ ci néew doole          yi ci fànna yii :
          -          Mbéy
          -          yarum jur ak ni waaso wu ne di faje mala
          -          ni ñuy jëfandikook, ni ñuy saytoo càkkéef yi
          -          li ku nekk war a xam gën gaa néew ci wàllu paj
       pexe          yi ñuy aaroo ci jàngoro yi, pajum feebaru xel
          -          Rënk ak able (leble)
          -          yokkute gu daj ñépp
          -          xeex (bëreek) ñàkk gi
       6 - (          13 ) Ba tey, misaal yi di ñew firndéel nañu ne foo dem, ñi fa dëkké          mën nañoo tàkku taxaw ngir soppi aada yi nga xam ne dañuy gàllankoor seenug          dund.
       Misaal          : Ci réewum Senegaal, ay jigéen ñu nekk ci kow gaa ngay jëlé njongum          jigéen ci seeni dëkk.
               Jigéeni          Malikundaa fas nañ yéenée song jafe-jafe bii di njongum jigéen, di aada          bu waaso yu bari bokk : Bàmbare, Soose, Pël, Joolaa, Sooninke ... Bi ñu          fexee ba xam li am feneen ak musiba yi ngong mën a indi ci wàllu wér gi          yaram ak séyu jànq ji, ci lañ ame lay yu taxaw ba mujj magi dëkk bi dogu          ne njongum jigéen dootu fi ame. Loolu taxul xoli jigéen ñi sedd, dañoo          daldi taxawal seenug kuréel ngir seeti seen moroom yi nekk ci dëkk yi          leen wër, waxtaan ak ñoom, ngir jàppale leen ñu soppi yenn mbir yu am          ci seeni dëkk. Weeru saN wiyé ci atum 1998 lañu amal pénc mu mag mu dajale          fukki dëkk ak juróom benn yu nekke ci diiwaanub Cees ñépp di bambara walla          Meting ngir waxtaane mbàyyim njongum jigéen ba noppi sàlloo "kàddug Malikundaa".          Bi ko waa kaasamaas déggée, fukki dëkki pël ak juroom benn daje nañ fa          ñoom itam amal fa pénc mu ni deme, tënk fa xalaat bu deme ni ba "kàddug          Malika" ëmboon. Nes tuut, Peresidaa Abdu JUUF, njiitum réew mi ci boppam          ne xalaat bii tudd "waatup Malikundaa" dafa wara daj réew mi.
              Ñu          jàng ci ne : Ñépp bokk gis-gis mën nañoo dimbali ba ñu soppi yenn aada          yiy indi gënaatle.
       
       Misaal          mii wone na itam ne xam-xami cosaan nekkul loo xam ne kenn warul cee mën          dara. Njongum jigéen aada la bu amee soppiku yu ci am mën nañoo wax ne          yàllaak liggéey bu ag mbootaayu jigéen def, xëccaale ci ni dëkk bi di          doxale, sukkandiku ci jumtukaay yi dëkk bi di doxe ci sosaan ak yu bees          yi.
       
       7          - (15) Yenni xam-xami cosan yi mën nañoo dem ba réer. Su boobaa, mën          na am ñu mu lor, te ñi ciy jëkk ñooy ñi leen doon suuxat di leen dunde.          Gën a fullaal xam-xami cosaan yi mën naa am lu mu yokk ci yoon wiy indi          yokkute, tax ba ñu tëyé ci askan wi boroom mën-mën yu takku, ay jumtukaay,          ay mbiri cosaan ak ay pexey pajtalum jafe-jafe. Xam-xam bu ni deme dina          faral di am lu mu def ci yenn xalaat yu soxal réew yi. Ci kow loolu, sàmm          sàqum xam-xami cosaan yi mën naa tax xéewal yi ci àddina si yokku te dina          taxit ba ñu gëna gis ni aada ame doole ci yokkute. Léep itam, xam-xami          cosaan yi mën nañoo indi ndimbal ci niñ war a aare li ñu wër, ni ko misaal          miy ñëw wonee.
       Misaal          : Aar beykat yiy jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci dëkk bu nekk.
       Mbooloom          réew yaa ngi taxawal ay sàqu jiwu ngir aar li ñu xam ci wàllu jur, fu          nekk ak gancax ak mala ya fa fekk baax. Ni gancax yooyu di meññe ak xam-xami          beykat yi niru nañ lu am solo ci liggéey yi ñu war a sumb ci mbéy mi,          ngir jàngoro yeek gunóor yi duñu mën a yàq, walla yeneen jafe-jafe yi          aju ci jàww ji (wor , sedd, tàngoor,...). Waaye nak, sàmm ni gancax walla          mala di jure te aaruloo xam-xam yi aju ci fi ñuy jaar ba meññ mel ni ni          amul jariñ, ndaxte pepp yeek njëmbat yi ñu denc ànduñook luy wax ni ñu          war a def ba ñu màgg.
       Ci          kow loolu, béréb yiy saytu jiwu yi war nañoo jege sàmm yeek beykat yi          nga xam ne ba tey ñu ngi liggéey ci xeet yi fekk baax fi ñu dëkk moo xam          mala walla gancax la, ngir xam-xam ak m¨n-mën deme noonu bañ a réer.
              Nu          jàng ci ne : xam-xami cosaan mënul fee jogé su nu bëggée aar ni xeeti          gancax yi baree te wuuté.
       
       
       
       8-          (16) Misaal yi ni weesu wone nañ ni :
       •Dekk          boo dem, xam-xami cosaan yi mën nañ leen a jox ay pexe yu ñu faje seeni          jafe-jafe, rawatina ca néew doole yi.
       •          Jang ay xam-xami cosaan yi tëdde, dina yokk pas-pasu ñi ñuy jëflanteel          ci dëkk yi.
       •Sukkandiku          ci jaar-jaari doom aadama yi, ni ñu gise jafe-jafe yi ñu jankonteel ak          li ñuy def ci fiñ dëkk, mën naa tax ba sémb boo xam ne yokkutee ko tax          a jóg gën a am njariñ, weesu mbirum tono (ci anamu def nangam mu jural          la nangam) joo am gannaow ba joxee alal ju ñu liggeéyé
       •          Ni dëkk bu nekk gisé yokkuté mën naa indig ndimbal ci moomeel gi (ci ñi          moom mbir yi), mu nekk lu mën a indi njariñ ci ñi di jëflanteek ndaw ñi          fa toogal nguur gi, jox waa dëkk bi jumtukaay yu ñu mën a wottoo digante          boobu.
       •Xam-xami          cosaan yi doon nañu fu ñu mën a sukkandiku ba jox way-ñakk yi doole.

                ÑETTEELU                    XAAJ BI
                 
                                                    IIII          / LANGUG YÉNGU YI
       
      Dog          bii dafay wone ag làng gu ñuy yéngu ngir daan jafe-jafe yi dëkk diñu teree          lëkkale xam-xami cosaan yeek yoonu yokkute wi. Làng ngaa ngi ci ñeenti          ponk la sukkantdiku (seetal ci 2 eelu bootal bi, dog 2 ba 5          ) ngir xam li ponk yooyu ëmb, fànna yi ñuy yëngu yi leen war a mottali          ngir gën a mën a lëkkale xam-xami cosaan yeek yoonuw yokkute wi.
       =>          Tasaare xibaar bi. Yéngu yi ci ëpp solooy :
       •          Taxawal te suuxat sàqum xam-xami cosaan, liñ ci mën a jàng, fi ñu jóge,          ñi ci jàppoó, añs.
       •          Fexe ba xam jumtukaay yi ñu war a am ba dugal xam-xami cosaan ci masiinu          "ordinaatóor, "tasaare leen su ko defee, ñu seet jumtukaay yooyu ba mu          wóor.
       •          Siiwal ay misaal yu ñu tànn, ci kayit walla masiin.
       =>          Yombal weccantey xam-xami cosaan yi ci diggante dëkk yi ñeew doole.          Yéngu yi ci ëpp solooy :
       •          Dëkk bu nekk ñu dimbale leen ci lépp luy yokk seeni mën-mën ngir wéccantey          xam-xami cosaan am rawatina ci diggante kër yi ñu taxawal ci dëkk yi ngir          ñuy saytu xam-xami cosaan yi.
       •          Seet pexe yu ñu war a jëfandikóo ba bind, siiwal xam-xami cosaan yi ci          dëkk yi.
       •          Pexe yoon wi àdduna sépp war a jokkóo di ci weccantey xam-xami cosaan          yomb a taxawal.
       =>          Tàggat ñi jàppóo. Yéngu yi ci ëpp solooy :
       •          Foo dem jànge ci ña fa dëkk ak kuréel yi jokkuwul ci genn nguur.
       •          Jël lépp lu ñi jokkoo an ngir am njariñ yu gën a takku ci wàllu yokkute.
       •          Toppatoo ba xam ki moom xam-xami cosaan yi.
       Làng          ngi ñu leen wax ci kow la, bi ko jokkoo gi ñu suuxat ngir xam-xami cosaan          yi jëfandikóo la nas pexe mi ñu war a yéngu ci atum 1998 jàpp 99. Nisër          yi ñi jàppóo am lañ tënk ci àlluwa jiy ñëw. Taxawal nañu itam ag kuréel          gu ñuy diisóol ngir nuy xelaate ci lépp lu jublu ci pexeek lu ñuy def          (seetal ci bootal I). Bi ñuy yëngu ngir am li ñu déggóowoon          ba nisër ko, ci kow làng gi ñu wax ni mu deme ci kow, ñi lëngoo liggéey          nañ bu baax a baax ak kër yiy saytu xam-xami cosaan yi di dëkk jumtukaay          yi ci mën a am). Li leen gën a soxal mooy fexe ba ñu gën a fullaal solo          si xam-xami cosaan yi ci am, ràññee siiwal xam-xami cosaan te gën a yokk          mën-mënu kër yiy saytu xam-xami cosaan yi ci dëkk yi ngir gën a mën a          ràññee, bind te siiwal xam-xam yooyu. Loolu mën naa dugal ag ndimbal ci          wàllu koppar ngir gëstu gi ci ni ñuy defe ci wàllu xam-xamu cosaan, jokkale          kër yiy saytu xam-xami cosaan ci dëkk yi ci yoon wi tudd "Enternet",          niki noonu jumtukaay yi ñuy tasaaree xibaar ci yi gën a nekk yu cosaan          nga xam ne mën nañoo yombal weccantey xam-xami-cosaan yi ci digante dëkk          yi.
       Bi          ñu dooree làngug xam-xami cosaan yi ba léegi, li gën a fés ci liñ ci jëlé          mooy :
       •          Yékkéti sàqum xam-xami cosaan bu def lu toll ci ñeen-fukki misaal.
       •          Sos yoonu "Enternet" buy joxey xabaar yu aju ci xam-xami cosaan yi.
       •          Siiwal kayitu tasukaayu xibaar bi tudd "Mbind ci xam-xami cosaan yi" te          ñu jaglee ko xam-xami cosaan yi.
       •          Gëstu ci xam-xami cosaan yi. (seetal ci bootal 1 ngir xam li mu          ëmb).
               
              Xam-xami          cosaan ngir yokkute gi :
       pexe          yi ñuy yëngu : atum 1998 jàpp 1999
       
       
         
               Nisër                  yi              
               Li Sémb bi indi                
               Li ñi jàppóo indi                
               Yëngu 1 : Tasaare xibaar bi                
                Suuxat sàqum xam-xami cosaan, liñ ci mën a jànge,                  fi ñu jóge, ñi ci jàppóo.                
                Gën gaa néew 200 xam-xami cosaan a dugg ci sàq                  mi ci "Enternet".                
                 
               Kenn ku nekk ci ñi jàppóo joxe na gën gaa néew                  fukki (10) xam-xami cosaan.                
                Xam jumtukaay yi ñu mën a dugale xam-xami cosaan                  yi ci masinu "ordinaatóor " ak yi leen di siiwal te seet leen                  ba xam.                
                Gindikaay gi ñu war a sukkandiku ngir jëfandikóo                  jumtukaay yi aju ci misaal yi.                
                Ku nekk ci ñi jàppóo jox na gën gaa néew benni                  (1) misaal.
               Bànk Monjaal a ngi waajal ak a tasaare ag gindikaay                  gu ñuy sukkandiku.                
                Siiwal ay misaal yu ñu tànn bind leen walla ñu                  nekk ci masin                
                gën gaa néew 24 kayitu tasukaayu xibaar te tudd                  "Mbind ci xam-xami cosaan yi"                
                Kenn ku nekk ci ñi jàppóo joxe gën ngaa néew                  benni dog.
               Bànk Monjaal siiwal te tasaare.                

               Nisër                  yi              
               Li Sémb bi indi                
               Li ñi jàppóo indi                
               Yëngu 2 : Yombal weccante xam-xami xosaan ci                  digante néew doole yi                
                Indig ndimbal ci lépp luy yokk mën-mën yi ngir                  ñu bokk xam-xami cosaan yi.                
                Gën ngaa néew fukki (10) këru xam-xami cosaan                  am nañu yokkute ngir li ñu jokkook kuréel yu gën a kowe, gën a                  mën a ràññee xam-xami cosaan yi.                
                Kenn ku nekk ci ñi jàppóo yokk na doole genni                  kër gën gaa néew.                
                Xam pexe yi ñu mënee dugal xam-xami cosaan yi                  ci masin te tasaare leen ci nit ñi.                
                Gën gaa néew fukki (10) misaal ci wàllu weccantey                  xam-xami cosaan ci digante dëkk yi nga xam ne antu nañ.                
                Kenn ku nekk ci ñi jàppóo jàpp na ci benni (1)                  misaal gën gaa néew.
               Bànk Monjaal tasaare.                
                Fexe sos yoon wu àddina sépp di weccantey xam-xami                  cosaan doon lu yomb                
                Mu am gën gaa néew fukki "Telesàntar" yu jot                  ndimbal gu jëm ci weccantem xam-xami cosaan yi.                
                Kuréel yii See-Er-Dee-ii (CRDI), ii-Tee-i (UTI),                  Pë-NID (PNUD) ak Bànk Monjaal kenn ku ci nekk dimbale lu mu bon-bon                  benni Telesàntar.                
               Yéngu 3 : Jëfandikóo xam-xami cosaan yi ci yoonuw                  yokkute wi                
                Fexe be kilifa yi jiité réew yeek yu kuréel yiy                  toppatoo mbirum yokkute ci àddinasi gën a fullaal xam-xami cosaan.                
                Lëlub liggéey buy dajale liggéeykatu kuréel gi ñu jàppóol. Waxtaan                  wu yaatu wu ñuy amal ci xew-xew boo xam ne ñi jàppóo lañ ko ndeyale                  ci xam-xami cosaan yi.
               Ndaje mi am ci diiwaan bi te ñu fa doon waxtaane xam-xami cosaan                  yi (atum 1999).                
                Kenn ku nekk ci ñi jàppóo amal lu mu bon-bon menni ndajam liggéey.                  Lu mu néew-néew kenn ku nekk xewle benni yoon.
               Bànk Monjaal amal ndaje mu mag mi (ñeneen ñi joxe seen ndimbal).                
                Dugal xam-xami cosaan yi ci sémb yi ñuy dimbalée                  sunuy réew                
                Fukki (10) sémb yoo xam ne ba ñu leen di nas jëfandikóo nañub                  xam-xamu cosaan.                
                Képp ku ci bokk jot gën gaa néew benni sémb buy jëfandikoób xam-xamu                  cosaan.                
               
               
Yëngu 4 : Jàngal ñi jàppóo ci liggéey bi                
                Jànge ci ñi ñu jàppóol ci dëkk yi ak kuréel yu                  ajuwul ci genni nguur                
                Xam te wone ci porose yi ñi jàppóo dimbale, yi ci jëfandikóo                  bi ñu leen di nas xam-xami cosaan yi.                
                Gën gaa néew, sémb bu nekk ak kenn ku mu jàppóol.
               Bànk Monjaal tasaare.                
               Nisër yi                
               Li Sémb bi indi                
               Li ñi jàppóo indi                
                Dajale tuut si ñi ñu dimbalée ngir njariñ la                  gën a am solo ci béréb yi ñuy yéngu.                
                Lëkkale/jokkale liggéey yi ñi jàpóo def, ci yoon wi ñu xàll ngir                  yëngu ci xam-xami cosaan yi.                
                Ku ne ci ñi ñu jàppóol ngir yokkute am, joxey koppar te doxal                  ay jéegéy boppam yu woroowul ak yoon wu mag wi ñu xàll ngir yëngu                  ci lu aju ci xam-xami cosaan yi.                
                Toppatoo wareefu boroom xam-xami cosaan yi.                
                Seet jéegó yi mu laaj.                
                Oo-Em-Pee-Ii (OMPI) mooy jiité liggéey bi ñu def ngir xam jéegó                  yi ci war.                

             Ñi teewoon                ca ndajem atal ma ñu amaloon ca Tinis, ci 22 fan ci weeru Oktoobar,                atum 1998 àndoon nañu ci palaK                bii.            
       
              BOOTAL          YI
              Bootal          1
       Won          leen ni pexem xam-xami cosaan ngirug yokkute mi tëdde
       
       Waxtaan          wa amoon ci weeru suweK, atum 1997 ca Toronto réewum Kanadaa, dafa fésal          ni soxlas jàng; aar ak weccante xam-xami cosaan yi jàmpe. Ci jamono jig          jàppóo amee ngir xarala yi ñuy jokkoo ak di ci tasaaree cibaar yi ci Afrig;          la Bànk Monjaal nangoo jiite pexeg xam-xami cosaan yi ci yoonuw yokkute          wi. Allal ji ci Bànk Monjaal a ngi jóge ci koppar yu mu maye ci sumb bi          tudd " Innovation Marketplace" maanaam " lu bees li ñu indi ci ja yi".
              Ñi          jàppóo (lëngóo)
       
       ÑII;          BOKK NAÑ CI ÑI JÀPPÓO NAS PEXE MU BEES MI:
       -          CEA di bànqas giy saytu koom-koom ci Afrig.
       -          CISDA di kër gu kuréel yiy toppatoo mbirum yokkute ci Afrig di wecaantee          xabaar
       -          CRDIC di Kër gi ñuy gëstóo yokkuteg réew yi te nekk Réewum Kanadaa
       -          UIT di mbootaayu kuréel yi réew yi séq di ci toppatoo jokkoo digante          ñoo xam ne dañoo sorewoo.
       -          UNESCO di banqaasu mbootaayu xeet giy saytu yar mi, xam-xam yu xarala          yi ak caada.
       -          PNUD di sumb bi mbootaayu xeet yi sumb ngir réew yi amug yokkute.
       -          OMS di mbootaay giy toppatoo mbirum wér gi yaram ci àddina si.
       Ci          digante bi am na ñeneen ñu leen ci fekkisi
       -          CIRAN di mbootaa gu fekk baax ca réewum Olànd tey toppatoo ni réew          yi di demlantee ci wàllu njàng mu kowe mi.
       -          SANGONET kuréel la gu jokkuwul cig nguur , fekk baax ca réewum          "Afrig dii Siid" nga xam ne moo def lëpp lu aju ci Enternet ( maanaam          jokkoo goo xam ci masiinu Ordinaatóor lañ ko jaarale )
       -          OMPI : mbootaay miy saytu àq ak sañ-sañi boroom xam-xam yi ci àddina          si.
       -          OIT : di mbootaay miy toppatoo àq ak sañ-sañi liggéeykat ci àdduna          si.
              Nisër          yi
       Tas          xabaar bi
       
       •Suuxat          sàqum xam-xami cosaan yeek liñ ci mën a jànge.
       •          Siiwal ay misaali xam-xami cosaan ci jumtukaay yu ñu bind ciy kayit walla          cib masin.
              Yombal          weccantem xibaar ci diggante ñi nekk ci dëkk yi ci réew yu néew doole          yi.
       
       •          Ndimbal ci lu yokk mën-mëni nit ñi nekk ci dëkk yi ngir ñu bokk xam-xami          cosaan yi.
       • Xam niñ          war a def ba dugal xam-xami cosaan yi ci masinu ordinaatóor, tas leen          ba ñu yegg ci nit ñi ci dëkk-dëkkaan yi.
               
       
      BOOTAL          II
       Kërale          2 : Yokk te gën a jàppandil xabaar yi fi am ci xam-xami cosaan yi
       
       
             Fànna                yi ñuy yéngu            
             Taxawaay              
             Jéegó yi ci war              
             Doxalin              
              Tëyé te dajale lépp lu am ci xam-xami cosaan yi              
              •Gëstu takku yu ñu def ci ni doom aadama yi di                dunde yuy joxe ay xabaar ci xam-xami cosaan yi
             • Bés bu set, gëstu yi dañuy gën a yokku niki liggéey                yi ñuy amal ci dëkk yeek ndajey liggéey wall waccantey xalaat ci                mbirum xam-xami cosaan.
             •Li ëpp ci gëstu yi y wone ni xam-xam yi mel a                ëpp yiy wone seeni ngënéel ak seeni rëq-rëq te néew na lu ñuy dellusi                ci dëkk yi ñu defewoon gëstu yi waxtaan ak nit ñi ci li ñu gis.              
              • Pexe yuy tax ba ñépp bokk ci ñiy lëñbati xam-xami                cosaan yi, leeral leen ba dajale leen foo xam ne dinañ yomb a jëfandikóo.
             • Ay pexe yu ñuy taxawale sàq mu ñuy def xam-xami                cosaan yi ñu dajale.              
              • Gëstu ci dëkk yi
             • Ay gëstu
             •Ay ndajey liggéey
             •Jëflanteek Oo-See-Bee (OCB) yeek Oo-En-See yi                (ONG)              
              Seet te jëfandikóo pexe yi ñuy taataane xam-xami                cosaan yi, niñ leen di jëfanfikóok ni ñuy def ba ñu àgg feneen.              
              •Gëstu yi am ci pexe yi lu néew la
             •Yenni porose yi dinañuy seet nit ñi ak ay pexe                yuy tax ba ñépp bokk.
             •Porose yiy sóoraale tënkum ni ñuy jëfandikóo xam-xami                cosaan yi.
             •Lu baree-bari ci porose yu Oo-En-See yu ndaw yi                dañuy jëfandikóo xam-xami cosaan yi waaye ñi ci tënk seeni jaar-jaar                néew na waxatuma nak di ci weccanteek ñeneen.              
              •Jàppale Oo-En-See yi ñu bind te leeral seeni jaar-jaar.
             •Gëstu lépp lu aju ci ni ñuy yóbboó xam-xami cosaan                feneen.
             •Seet ndax porose yeek ni ñuy jëfandikoo xam-xami                cosaan mën nañoo yokku              
              •Gëstu pexe yi
             •Seet porose yiy taataan xam-xami cosaan yi di                leen jëfandikóo
             •Xam ñi jëfandikóo xam-xami cosaan yi, toxal leen                feneen te am ci ndam.              

             Fànna                yi ñuy yéngu            
             Taxawaay              
             Jéegó yi ci war              
             Doxalin              
              Yonnal xam-xami cosaan yi ( fexe ba yoon yiy dox                ci réew yi nangu amug xam-xami cosaan)              
              •Bariwul ñu ci góor-goórlu (su weesoo gëstu yi                ñu def ci gancax yiy faj) ; xabaar yiy wax li xam-xam bu nekk di                jariñ yombul a am ; li ñu xam ci xam-xami cosaan yi ñu yóbbu feneen                mu antu néew na.              
              •Dem seet ko ci dëkk yi, kuréel yiy toppatoo mbirum                gëstu gi ci réew mi def ci ay gëstu, boole waale ci lépp luy indi                ay leeral ci wàll koom.
             •Yër jumtukaay yi ñu jotoon a tënk ay xam-xami                cosaan ci ndoorteelu xarnu bi. Moo xam boroom xam-xami tubaab, walla                ñiy jëfe xam-xami cosaan yi walla muy waa kër làbbe yi.
             •Yër li ñu jot a tënk ci pexe yu xarala yu ñu toxal                te mu bawoo ci xam-xami cosaan yi.              
              •Dajale gis-gisu ñi leen di jëfandikoó
             • Seet leen ci dëkk yi ba xam
             •Taxaw gëstu
             •Seet leer ci lëñbatuwaay yi (laboraatuwaar)
             •Tënk li jot a antu ci wallu jëlé xam-xami cosaan                yébbu feneer.              
              Fexe ba ñépp mën a jot ci xabaar bi              
              •Ci at yu mujje yii, limu xam-xami cosaan yi ñu                tënk, weccante ci dafa yokku (téeré, kayitu tasukaayu xabaar, widewoó,                waxtaan añs), waaye faramfance gi des naa leer.
             •Xabaar bu am doole (bawoo ci daara yi tey woney                melo) jàppandi na ci web bi.
             •Nu ngi defar turi ñi koy jëfandikóo.
             •As lëf ci sàq yu def xam-xami cosaan yi aju ci                mbirum gancax gi.              
              • Gën a defaraat yoon yi ñuy jokkoo ci diiwaan                yi ngir weccante xam-xami cosaan yi gën a jëm kanam (fi ñu bawoo,                porose yeek nit ñi ciy yëngu).
             •Gën a yaatal tasukaayu xabaar yi.
             •Taxawal ay sàqi xam-xami cosaan yu ñépp mën a                jot.              
              •Defar te tasaare téeré yi, jumtukaay yu ñu mën                a seetaan walla ñu déglu ko ak jumtukaay yu ñu defar.
             •Amal ay waxtan yu yaatu
             •Dimbale yoon yi ñu xàll, kër yiy segg, sàqum xam-xam                yi, kër yi ñuy wonee xam-xam yi, déncuwaayu cosaan yi am.              
             
               
             Fànna                yi ñuy yéngu            
             Taxawaay              
             Jéegó yi ci war              
             Doxalin              
                         
              •Tasukaayi xabaar yaa ngi gën a teew ci ndaje yi                ñuy def ak nit ñi ci dëkk yi.
             • Lëkkalewuñu bu baax jéegó yi aju ci xabaar yi                ci réew yu néew dooleyi.
             •Li ñuy faral ci dajale di ko wone ci bérébu cosaan                yi mooy ay jumtukaay yu ñu fi defare ñuy firndéel ne xam-xami cosaan                am na.              
                         
                         
             
              Kërale          3 : Fexe ba nit ñi gën a gis solo si xam-xami cosaan am te di leen jëfandikóo          ci lépp lu ñuy yéngu
             mu          jublu ci wàllu yokkute.
       
       
             Fànna                yi ñuy yëngu            
             Taxawaay              
             li ñu war a def              
             Niñ ko war a defe              
              Fexe luy dollee tax nit ñi gën a gis gëdda ak njariñ                lu takku lu xam-xami cosaan am ci :
             •waa dëkk bi
             •liggéeykat yi ci dëkk beek kuréel yi.
             •jàngalekat, boroom xam-xami tubaab ak ñi ci daara                yu kowe yi.
             •njiit yeek ñiy lal pexe yi jublu cig yokkute joxe                ay jumtukaay ak ay doxalin yu ñuy mënee tënk xam-xami cosaan di                leen jëfandikóo ci porose yiy indig yokkute.              
              •Yéngu yi taxaguleen a bari waaye ñu ngi yokku.
             •Am na ci yu waa dëkk bi bokk taxaw ci taxawaayu                ku jàppóo walla kuy nas aka ñocci
             •joxewuñu bu baax xabaar yi jëm ci xam-xami cosaan                yi ba ñiy dogal ak ñiy nas pexe yiy indi yokkute mën leen a jëfandikóo
             • yenn téeré doxalin yuy wone nangu gu nangu nañ                ko gëdda walla màqaama gi xam-xami cosaan am (niki yoon yi Bànk                Monjaal joxoñ ngir képp ku dem cib dëkk fas yéenée liggéey ak waa                dëkk ba jaar ci)
             •liñ jot a def ci jëfandikoóm xam-xami cosaan yi                kenn tënkul fenn.
             •Téeré gëstukat bi ci : ni ñuy tënke xam-xami cosaan                ci pexe yu ñépp a ciy bokk te nekk fi ñu koy jëfe loxo walla ordinaatóor                te kuréeli IIRR ak CIKARD waajal leen.
             •Am na ay gëstu yu fi nekk yoo xam ne mënees na                leen a wone ci anam yu gën a yomb a jëfandikoó.              
              •Boole ci waa bitim réew ngir nit ñi jot ndimbal                luy tax ba ñu mën a tënk, gëstu te jëfandikóo seeni xam-xami cosaan.
             •Natt pexe yiy tax ba ñépp bokk.
             •Weccante xalaat am digante ñiy jëfé xam-xami cosaan                yi.
             •Dugal xam-xami cosaan ci njàng mi.
             •Xabaar bu ñu jaglee njiit yeek ñiy lal pexe yi                indi yokkute.
             •Yoon yi ñu xàll ci réew yeek bànqaas yi.
             •Fexe ba téeré yi gën fee baax.
             •Lal waxtaan yoo xam ne ciy fànna lañuy doon (misaal                : xam-xami cosaan ak kaaraangeg jiwu yenni gancax yi.              
              •Porose
             •Ndajem liggéey
             •Li ñu mën a xoole ci widewóo
             •Waxtaan, jumtukaay yu ñuy dégg ak walla di ko                gis ak jàngaani.
             •Di demlante, suuxat ay téeréy "xam jëf" ngir bind,                bokk, tasaare xam-xami cosaan yi.
             •Jumtukaay yi ñuy lale pexe yi, di ci doxal porose                yi ngir mën a nangu, dëggal te dugal xam-xami cosaan ci lépp lu                ñuy def.
             • Téere bu nekk ak ñi koy jëfandikóo ak ni ñu koy                jëfandikóo
             •Dem ci dëkk, seet téeré yi ñu móol ba xam ndax                baax nañ.              
             
               
             Fànna                yi ñuy yëngu            
             Taxawaay              
             li ñu war a def              
             Niñ ko war a defe              
              Tàggat liggéykat yi toogal nguur gi ci dëkk yi ak yu kuréel yi                ajuwul ci genni nguur ci ni ñuy jëfandikoó jumtukaay yeek feem yi.              
              •L ci jàppandi bareegul.              
              •Saar yuy jàngalee feem yi ñuy tënke ak ni ñuy                jëfandikóo xam-xami cosaan.
             •Tàggatukaay ak jàngalekaay i xam-xami cosaan yi.              
              • Ay këri gëstu ak daara yu ñuy jàngalee ci dëkk                yi
             • Séexale.
             •Tàggatukay ngir jàngalekat yi, kuréel yi ajuwul                ci genn nguur, ñi seeni yëngu jublu ci yokkute añs.
             •Tàggat jàngalekat yi
             • Fexe ba digante ñiy weccantey xam-xami cosaan                gën a rattax.              
             
              Kërale          4 :Xàll yoon wu yaatu wu ñuy weccantee xam-xami cosaan.
       
       
             Fànna                yi ñuy yëngu            
             Taxawaay              
             li ñu war a def              
             Niñ ko war a defe              
              Bokki pexe              
              • Am na loo xom ne ñu ngi ko ciy def ci jamono                yii (BTICA - Bellanet)
             •Allal ju yem
             •Kuréel yu jokkuwul ci genn nguur (Oo-En-See) yu                ber seen saawos bopp.
             •Ay gëstu yu jëm ci xamtu ak mbind te dummoóyu                weccante gi
             •Njariñu wall gi am ku ko moomal boppam ngir jumtukaay                yu xarala yeek lu ñu defar.              
              •Déggée ci ni ñuy bokke xabaar bi.
             •Méngale la ñuy def ak li réew yi dégóo.
             •Jàppóok Oo-En-See yeek ñi yor seen mbiru bopp.              
              •Taxawal pencum weccantey xam-xam muy faral di                am, te boot waxtaan yi réew yi séq.
             •Kuréel yi jokkuwul ci genn nguur, kuréel yiy saytu                mbirum koppar yeek ñiy def seen mbiri bopp bokk di gëstu.
             •Jokku ci yoon yi ñu xàll niki sàqu xam-xami cosaan.              
              Leeral jafe-jafe yiy lang ( yi nga xam ne kenn                waxagul ci dara)              
              •Jafe-jafe yi aju ci moomeelug xam-xami cosaan,                nga xam ne ken waxagul ci dara.              
              • Jëfandikóo walla jubbanti déggoó yi fi nekk.              
              •Boot ndaje yu mag yi boroom xam-xam yi ci àdduna                seek ñi am gëdda di amal.              
              Taxawal kër yuy segg ci boppu diiwaan yeen biir                diiwaan yi.              
              • Taxawagul ci anam yoo xam ne ay réew a ci ànd,                li am mooy yenn kër ci boppi diiwaan yi nga xam ne liñ mën dafa                am fu mu yem.              
              •Sàqi xam-xami cosaan
             •Làng gu ñuy weccantee
             •Kër yu dox te mën liñ leen di doye.              
              •Tënk feem yi
             • Taxawu kër yi fi nekk ci dëkk-dëkkam yi              
             
               
             Fànna                yi ñuy yëngu            
             Taxawaay              
             li ñu war a def              
             Niñ ko war a defe              
              Fexe ba ñi tolloo di weccante              
              •Weccantey xam-xam rawatina mu jogé ci suuf dem                ci kow dellusi ci suuf ; jokkale gi ci wàllu woowoo ngi jëm kanam.              
              •Dara doxul digante ñiy joxe xam-xam beek ñi koy                jot.              
              •Wàcce xàll yi
             •Ubbi fu ñuy bind xam-xam yi
             •Wonekat (tegtalkat ak kër yoo xam ne liñ fay def                kenn du ko werante
             •Mbindum kàddu yi war
             •déggóo ci melo yi
             •Seet melo yi ba xam ndax dëppóo naak li ñu déggóo
             •Kër yi ñuy jokkoo gën fee baax.              
             
              Kërale          5 : Jox ku nekk céram ci weccantem xam-xami cosaan yi
       
       
             Way jëf                yi            
             Fànna yi ñuy yéngu              
             Li ñuy def              
             Ñi ñu lëngóol              
             Ñi bokk fuñ dëkke              
             •Jàpp te                ñoN                al xam-xami cosaan yi.
                           •Xamtu xam-xami cosaan
             •Yóbbu xam-xami cosaan feneen.              
              •Dolli xam-xami li ñuy def
             •Yoonal jëf yi
             •Ràññee yi gën a fés ci fi xam-xami cosaan yiy                jógé
                           •Suuxat                ay feem yu ñu leen di ñoN                al
                           •Xëccanteeg ñu nekk ci yeneeni dëkk              
              • Oo-See-Bee, Oo-En-See
             •Liggéeyuwaay yiy yaatal
             •Liggéyuwaay yi takkul seen bopp.              
             Oo-See-Bee                (OCB); Oo-En-See (ONG)            
             •Jàpp te                ñoN                al xam-xami cosaan yi te wutam ceen ay xamtu
                           •Yóbbu xam-xami cosaan yi ci dëkk beek biir diiwaaw                bi
             •Tasaare
             •Aar              
              •Joxe ay bérébu xamtuwaay te doxal leen (kàggu,                sàqum xam-xam kërug yéglé, telesàntar...)
                           •Defar                ay yéenekaay (kayit, Rajo, Telewisyow                Tiyaatar añs)
                           •Amal ay weccante ci diiwaan yi.              
              •Nguur yi
             •Ñiy liggéeyal seen bopp
             •Gëstukat yi
             •Mbooleem kuréel yiy toppatoo mbirum koppar yi.              
             
             
Nguur yi ci boppi réew yi              
              •Joxe yoon wi ñu war a jaar
             •fexe ba liggéey bu aw yoon nekk lu yomb.              
              •Aar sañ-sañu képp ku am xam-xamam
             •Yombal lépp lu ñuy yéglé ak weccantey xabaar yi.
             •Dugal xam-xami cosaan yi ci njàng mi
             •Yombal tukki mi ci diiwaan yi.
             •fexe ba ñépp mën a jot ci tàggukaayu xabaar yi              
              •Kuréel yi réew yi séq
             • Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum koppar.              

             Way-                jëf yi            
             Fànna yi ñuy yéngu              
             Li ñuy def              
             Ñi ñu lëngóol              
             Gëstu gi              
              •Nangu ne xam-xami cosaan am na
             •Yoonal xam-xami cosaan yi
             •Tasaare li gëstu gi feeñal              
              •Fexe ba ni ñuy gëstóo ci pexey cosaan yi gën a                baax
             •Fexe ba nit ñi mën a jot ci li feeñ ci gëstu gi.
             •Dugal xam-xami cosaan yi gëstu gi feeñal ci li                ñuy jàng.
             •Yombal weccante geek kër yi nguur yi moom ak yi                nga xam ne nit ñee leen moomal seen bopp.              
              •Nguur yi
             •Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum koppar              
             
             
Li nit ñi moomal seen bopp              
              •Nangu àqi xam-xami cosaan yi              
              • Fey àq walla ndigal              
              • Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum koppar
             • Oo-En-See (kuréel) yi ajuwul cig nguur              
             
             
Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum koppar yi              
              •Nangu ne xam-xami cosaan yi am nañ solo
             • Tasaare xabaar yi aju ci xam-xami cosaan yi
             • Fexe kenn ku nekk ci ñi jappóo gën a jox gëdda                solo yi xam-xami cosaan am.              
              •Taxawal ci suñ biir ay géew yu ñuy jokkoo di ci                weccantee.
             •Yoon wuy jokkale béréb yi xam-xami cosaan yi fàqikook                ñi jàppóo.
             •Dugal mbir yu bokk ci xam-xami cosaan ci feem                yi ñuy indée ndimbal gu jëm ci yokkute.              
              •Oo-En-See (kuréel yi ajuwul ci genn nguur)              
             
             Way-                jëf yi            
             Fànna yi ñuy yéngu              
             Li ñuy def              
             Ñi ñu lëngóol              
             Mbootaay yi réew yi bokk              
              •Nangu ne xam-xami cosaan dafa am lu mu laaj              
              •Réew yi déggóo ci mbir yu leer yu bokk ak lenn                lu dul lu aju ci xam-xami cosaan, àqi boroom xam-xam bi, ni ñuy                dugalantee, weccantey aada añs
             •Fexe ba ñiy yëngu ci xam-xami cosaan yi di mën                a teew ci pénc yu yaatu yi réew yi di daje.              
              •Mbooloom kuréel yiy tappatoo mbirum koppar yi
             •Oo-En-See (kuréel yi ajuwul ci genn nguur)              
             
             
Bànk Monjaal              
              •Fexe ba ñu gën a jox gëdda xam-xami cosaan ci                nguur yi, ci ñi ñuy jàppaleek képp koo xam ne boroom baat la              
             •Joxe ay                xabaar ci xam-xami cosaan yi (jaarale ko ci web bi , jumtukaay yi                ñu bind ci kayit, béréb yi ñuy wonee, dugal leen ci sàq yi ñuy def                lépp lu aju ci kaaw                yi...)
                           •Jottali xibaar yi ñi ñu jàppóol (ci ay penc yu                mag, taxawalug jàppóo yu mel ni P.T.I.C.A, ndimbal ci jëm ci pexe                yi nit ñi sos ci fi ñu dëkk)
             •Jàpp ci porose yi sukkandiku ci xam-xami cosaan                yi, pénc yi ay réew séq, ak ndajey liggéey yi ñuy def ci fànna gii,                ak xam-xami cosaan yi gën a soxal kuréel yi réew yi bokk.              
              •Oo-En-See yi
             •Nguur yi
             •Mbooloom kuréel yiy toppatoo mbirum kappar yi              
            BOOTAL          V
       Doxalin          wi
       
      Njariñu          képp ku bokk ci ñi jàppóo; kàttanu ñiy am lu ñu def ci xam-xami cosaan          yi; ak yenn gàllankoor yi mën a am ci wàllu alal. Loolu dafa laaj doxalin          wuy yombal weccantem xabaar bu dul dakk, yokk mën-mëni nit ñi ci fiñ dëkk,          ak yoon wuy ubbil bunt ñeneen ba ñu mën a bokk ak ay joxekati xam-xami          cosaan. Boroom xam-xam yu ràññeeku ci wàllu xam-xami cosaan ak xaralay          xibaarukaay ak jokkookaay ñooy xelal " pexe mi" ci feem yeek xalaat yi          nga xam ne fàww ñu jëfé leen.
              Tasum          Xibaar mi
       
       Pexe          mi dafay seet jumtukaay yi war a jiitu ngir bind; téyé xam-xami cosaan          yi, tas leen, siiwal leen te di leen jëfé. Ci kow loolu, ñi ñu xam ne          ci ñoom la xam-xami cosaan yi fekk baax, dañoo war a joxe ay leeral ci          ni ñu leen di jëfandikóo. Loolu mën naa yaatal liñ gis ci xam-xami cosaan          yi, be tey itam, mën naa doon jumtukaay bu ñuy natte pexe yi ñuy jëfandikóo          ba am lu leer ci xam -xami cosaan yi ñu mën a jëfandikóo ñooy dem ci dëkk          yi di laaj nit ñi, toog ak ñi ngeen bokk natt li ñuy def. Porose Bànk          Monjaal yeek ñeneen ñu bokk ci liggéey bii ñu door dinañu indi seen i          yokkute. Liggéey bi ñu door nii, dinañ yaatal ba tey xam-xam yi Bànk Monjaal          ak ñi mu ci jàppool sukkandiku.
              Fexe          be weccantem xibaar mi ci diggante ñi nekk ci réew yi néew doole yomb
       
       Li          ñu bind ci li ñuy def ci xam-xami cosaan yi, dañ koy dajale, tënk ko ngir          dugal ko ci sàqum xam-xam moo xam ne nit ñi dinañ ci mën a jot ci lu yomb,          nga xam ne saa su mënee nekk dañ koy jokkaleek fi xam-xami cosaan yii          fekk baax ( liggéey biñ door dafay war mu sukkandiku ci). Xam-xami cosaan          yi nga xam ne dafa am ñoo xam ne dañ leen amal njariñ; dañu leen di siiwal          ci kayitu tasukaayi xabaar buy génn wenni yoon ci weer wu nekk. Liggéey          biñ door dafay war mu sukkandikóo ci liñ fi jëkk a def, dimbale kuréeli          xam-xami cosaan yi ba liñ fi mën a yokku ba ñu gën a xamante, tëyé te          tas xabaar yi aju ci xam-xami cosaan yi.
              Jëfandikóo          xam-xami cosaan yi ci yoon wiy indig yokkute.
       
       Bàyyi          xel ci solo yi xam-xami cosaan am, jëfandikóo jaar-jaar yiñ fi jëkk a          def ak tàggat xel yi ñetti mbir lañ yoo xam ne dañ leen di soxla su ñu          bëggée dugal xam-xami cosaan ci yoonu yokku wi antu. Bi muy door, liggéey          bi dafa waroon a def léppam ci ñiy dogal, kuréel yiy toppatoo yokkute          ak nguuri réew yi gën a yebe xel solo si xam-xami cosaan yi am. Bu weesoo          siiwalug xam-xami cosaan yi nga xam ne niróowuñook yeneen yi, liggéey          bi dina am yu muy wone ci yen xew yi ñi jàppóo di amal ( misaal: ndaje          mi Bànk Monjaal di amal at mu nekk).
       Fas          nañ yéenee amaal ndaje mu mag ci Afrik ngir ñi fiy jiite gën a yebe xel          solo yi xam-xami cosaan am. Bu ñu demee ba ca kanam, dinañ teewlu ci yokkug          liggéey yi ñu sumb ngir seet ba xam, jaarale ko ciy porose. Loolu, dina          dugalaale jëfandikóog misaal yu antu ngir firndéel ne jëfandikóo xam-xami          cosaan mën naa indi njariñ lu amul benni werante. Tànn gu am fayda gu          ñuy tànn liggéey yi ñuy seete ba xam ( moo xam porose xalla am réew a          koy doxal) dinañu dimbale ba ñu gën a mën a suuxat misaal yi ñiy jëfandikóo          ci jéegó yii ngi ñeneen ñi ñu bokkal liggéey wóolu. Bu dee li aju ci ñi          séq liggéey bi, jëflante gi am ci jaar-jaar yiñ doon seete; ak joxe ab          leeral di dugalaale borom kàddu yi nekk ci kréel yeek mbootaay yi ci "          baayale walla ndeyale" ay liggéey yu ñuy jëkk a seete, dina tax ba ñiy          yëngu ci wàllu yokkute bàyyi ci xel ni mu ware.
              Taxawal          ay jàppóo
       
       Liggéey          bu bees bi dina fexee taxawalug jokkoo ak ñeneen ñoo xam ne bokkuñook          ñi nekk ci kuréel gi tudd PICTA. Dina gën a bàyyi xel ci jokkoo gi ñuy          taxawal digante kuréel yi jokkuwul cig nguur, xàll wu mag wu xam-xami          cosaan yi te saa su mu mënee nekk; jaarale ko ciy porose aki kuréel yu          jàppóo, ak ñi ci dëkk-dëkkaan yi ngir am lu ñu jànge ci seeni jaar-jaar.
               

              Xam-xam                mënul a ñàkk ndax su ñu xamul ni nit ki walla askan wi di def ba                am xam-xam ak ni muy jëfandikóo xam-xamam, duñu leen mën a indilug                ndimbal ci seen dund rawatina néew doole yi?
             Bataaxal                bu ñu bindoon ci atum 19998 ci yokkute gi ci àdduna si,